Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

‘Yàggatul dara’ (Woyu Ndaje bu mag bu ñetti fan bu atum 2023)

‘Yàggatul dara’ (Woyu Ndaje bu mag bu ñetti fan bu atum 2023)

(Abakug 2:3)

Telesarseel:

  1. 1. Yaa defar suuf si, ak sa loxo yi,

    Muy lu taaru lool, te it yéeme na lool.

    Suuf si soppiku, Yow doo soppiku.

    Yow lépp ngay yeesal, waxtu wi rekk ngay xaar.

    (AWU BI)

    Baay, yàkkamti nañu, dund ci àjjana.

    May ñu ba ñu mën a xaar.

    Ni jant biy fenkee, bés bu ne ci lu wóor,

    Noonu la sa bés wóoree.

    ‘Yàggatul dara!’

  2. 2. Yàkkamti nañu mbokk yi dekki,

    Waaye Yexowa, yaa gën a yàkkamti.

    Baay, ñun xam nañu, ni nga leen bëgge.

    Baay, may ñu ñu muñ, di roy noonu ci yow.

    (AWU BI)

    Baay, yàkkamti nañu, dund ci àjjana.

    May ñu ba ñu mën a xaar.

    Ni jant biy fenkee, bés bu ne ci lu wóor,

    Noonu la sa bés wóoree.

    ‘Yàggatul dara!’

  3. 3. Yàlla yaa ngi seet, ñi seen xol rafet.

    May nga leen yaakaar, ak àjjana biy nëw.

    Jël nañu jotu, waare dëgg gi,

    Te liggéey boobu, moo tax ñu jege la.

    (AWU BI)

    Baay, yàkkamti nañu, dund ci àjjana.

    May ñu ba ñu mën a xaar.

    Ni jant biy fenkee, bés bu ne ci lu wóor,

    Noonu la sa bés wóoree.

    ‘Yàggatul dara!’

    Baay, dimbali ñu ñu xaar.

(Xoolal itam Kolos 1:11).