Jàngal-leen seeni doom
Yéen waajur yi, jël-leen nettali yii ngir jàngal seeni doom ay njàngale yu am solo ci Biibël bi.
Ubbite bi
Kàddu yi nekk ci 5 Musaa mën nañu la won li nga war a def ngir yar say doom.
LESSON 1
Am na Kumpa goo Xam ne boo ko Xamee Dinga Kontaan
Am na kumpa gu réy bu ñu wax ci Biibël bi. Ñu ngi koy woowe “ Kumpa gu sell. ” Yaw nag, ndax bëgg nga ko xam ?
LESSON 2
Rebeka dafa bëggoon di bégal Yexowa
Naka lañu mën a def ba mel ni Rebeka ? Jàngal nettali bii ngir gën a xam Rebeka.
LESSON 3
Raxab dafa gëmoon Yexowa
Jàngal ngir xam naka la Raxab ak waa këram mucce bi ñu yàqee Yériko.
LESSON 4
Dafa bégaloon pàppam ak Yexowa
Doomu Yefte bi ban dige pàppam la def ? Naka lañu ko mën a roye ?
LESSON 5
Samwil bàyyiwul di def lu jub
Boo gisee nit ñi ñuy def lu bon, naka nga mënee def li jub ni Samwil ?
LESSON 6
Daawuda nekkul woon ku ragal
Jàngal nettali bu neex bii nekk ci Biibël bi. Boo ko jàngee dinga xam lan moo tax Daawuda jàmbaare lool.
LESSON 7
Ndax lée-lée dangay yëg ne kenn bëggu la te nga am lu lay tiital ?
Bi Iliyas yëgee ne kenn bëggu ko, lan la ko Yexowa wax ? Lan nga mën a jàng ci nettali bii ?
LESSON 8
Yosiyas amoon na ay xarit yu baax
Biibël bi wax na ne def lu baax metti woon lool ci Yosiyas. Seetal ni ko xaritam yi dimbalee woon.
LESSON 9
Yérémi bàyyiwul woon di wax ci Yexowa
Bu dee sax nit ñi dañu ko doon ñaawal walla ñu di ko mere, lan moo tax Yérémi kontine di wax ci Yàlla ?
LESSON 10
Yeesu dafa doon dégg ndigal
Déggal say waajur bés bu nekk yombul. Xoolal li Yeesu def naka la la mën a dimbalee.
LESSON 11
Dañu nettali lu jëm ci Yeesu
Jàngal ngir xam juróom-ñetti nit yu bokkoon jamono ak Yeesu te nettali lu jëm ci dundam.
LESSON 12
Jarbaatu Pool bi dafa amoon fit
Xale bu góor bii moo musaloon nijaayam ci dee. Lan la defoon ?
LESSON 14
Nguur gi nar a jiite suuf si sépp
Bés bu Yeesu nekkee buur ci kaw suuf si sépp, dund bi naka lay mel ? Ndax bëgg nga fa nekk ?