Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 7

Ndax lée-lée dangay yëg ne kenn bëggu la te nga am lu lay tiital ?

Ndax lée-lée dangay yëg ne kenn bëggu la te nga am lu lay tiital ?

Xoolal xale bu góor bi nekk ci foto bi. Mu ngi mel ni ku yëg ne kenn bëggu ko, boole ci am lu koy tiital. Ndax mas nga yëg loolu ? — Ñépp a mas a yëg lu mel noonu. Ci Biibël bi, wax nañu ci ay xaritu Yexowa yu mas a yëg ne kenn bëggu leen te ñu am lu leen di tiital. Kenn ci ñoom mu ngi tuddoon Iliyas. Nañu jàng nettali bii ngir xam ko.

Yésabel dafa bëggoon a rey Iliyas

Iliyas mu ngi dëkkoon Israyil ca jamono yu yàgg ya bala Yeesu di juddu. Akab moo nekkoon buuru Israyil waaye moom du doon jaamu Yexowa Yàlla dëgg ji. Akab ak jabaram Yésabel dañu doon jaamu benn yàlla bu dul dëgg bu tuddoon Baal. Ñu bare ci waa Israyil itam dañu komaase woon di jaamu Baal. Lingeer Yésabel ku soxor la woon te dafa bëggoon a rey ñépp ñi doon jaamu Yexowa, ba ci Iliyas ! Ndax xam nga lan la Iliyas def ? —

Iliyas dafa daw ca àll ba, nëbbatu ci benn kàmb ! Lu tax mu def loolu ? — Waaw dafa ragaloon. Waaye jarul woon Iliyas di ragal. Lu tax ñu wax loolu ? Ndaxte xamoon na ne Yexowa mën na koo dimbali. Yexowa masoon na ko woon kàttanam. Benn bés Iliyas dafa ñaanoon Yexowa mu wacce safara ci kaw suuf. Yexowa dafa nangu ñaan bi, wacce safara. Kon Iliyas xamoon na ne Yexowa mën na koo dimbali !

Naka la Yexowa dimbalee Iliyas ?

Bi Iliyas nekkee ci biir kàmb bi, Yexowa dafa ko laaj ne : ‘ Lan ngay def fii ? ’ Iliyas tontu ko ne : ‘ Man rekk maa fi des di la jaamu te dama ragal ñu rey ma. ’ Iliyas dafa foogoon ne rey nañu ñépp ñi doon jaamu Yexowa. Waaye Yexowa nee ko : ‘ Am na 7000 nit ñu may jaamu ba léegi. Nekkal jàmbaar. Am na liggéey bu bare bu ma bëgg nga def ! ’ Ndax Iliyas kontaanul woon bi mu déggee loolu ? —

Lan nga mën a jàng ci nettali bii ? — Bul mas a foog ne kenn bëggu la te bul mas a ragal. Am nga ay xarit yu bëgg Yexowa te bëgg la. Yexowa itam ku bare kàttan la, dina la dimbali te du la mas a bàyyi ! Ndax loolu seddalul sa xol ? —