Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 12

Naka lañuy defe suñu liggéeyu waare Nguuru Yàlla ?

Naka lañuy defe suñu liggéeyu waare Nguuru Yàlla ?

Espagne

Biélorussie

Hong Kong

Pérou

Ci lu yàggul dara bala muy gaañu, Yeesu dafa yégle woon ne : ‘ Xibaaru jàmm bii ci Nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee mujug jamono ji jot. ’ (Macë 24:14). Naka lañuy defe liggéeyu waare boobu ci àddina si sépp ? Xanaa ñu topp fasoŋ bi ko Yeesu doon defe bi mu nekkee ci kaw suuf. — Luug 8:⁠1.

Dañuy fekki nit ñi ci seeni kër. Yeesu dafa jàngaloon taalibeem yi ni ñu waroon a yéglee xibaaru jàmm bi ci kër yi (Macë 10:​11-​13 ; Jëf ya 5:​42 ; 20:20). Ca jamono karceen yu jëkk ya, dañu doon wax waaraatekat yi fi ñu war a waare (Macë 10:​5, 6 ; 2 Korent 10:13). Tey itam suñu liggéeyu waare bi, noonu lañu koy defe ngir lépp mën a aw yoon. Mbooloo mu nekk dañu koy jox fu mu war a waare. Noonu lañu mën a defe liggéey bi ñu Yeesu sant. — Jëf ya 10:⁠42.

Dañuy fekki nit ñi fépp fu ñu mën a nekk. Yeesu royukaay la ci liggéeyu waare bi. Dafa doon dem fu nit ñi bare, maanaam ci tefes yi, ci teen yi ak yu mel noonu (Màrk 4:1 ; Yowaana 4:​5-15). Ñun itam ñu ngi jéem a waxtaan ak nit ñi ci Biibël bi fépp fu ñu ko mën, muy ci mbedd yi, ci biro yi, fi nit ñi di féexloo, walla ci telefon. Te it saa yu ñu ci amee bunt, dañuy waar itam suñu dëkkandoo yi, ñi ñu bokkal liggéey, ñi ñu bokkal lekkool ak suñuy mbokk. Loolu yépp tax na ba ay junniy nit ci àddina si sépp dégg xibaaru jàmm bi ngir mën a mucc. — Sabóor 96:⁠2.

Ndax am na koo mën a yégal xibaaru jàmm bi jëm ci Nguuru Yàlla ? Ndax gis nga njariñ bi mu ci mën a jële ? Yaakaar boobu, bu ko yemale ci yaw. Gaaw a koo yégal nit ñi !

  •  Ban “ xibaaru jàmm ” lañu war a yégle ?

  •  Naka la seede Yexowa yi di roye Yeesu ci seen liggéeyu waare ?