2019-2020 Porogaraamu ndaje bu mag bu benn fan — Ak ki bànqaas bi yónni
Seetal ci porogaraamu ndaje bu mag bu benn fan bii, waxtaan yi ki bànqaas bi yónni nar a def. Turu ndaje mi mooy “ Nanga bëgg Yexowa ak sa xol bépp. ”
Nanga bëgg Yexowa ak sa xol bépp
Porogaraam bi dina ñu dimbali ñu dooleel suñu mbëggeel ci Yexowa te xiir ñu ñu wone mbëggeel bu dul wut njariñu boppam.
Déglul bu baax ba mën a tontu ci laaj yii
Dinañu tontu ci laaj yii ci ndaje bu mag bi.