Li Biibël bi wax du xewwi mukk
XALAATAL REKK, ngay wisite benn musée bu am ay nataal yu bare. Lu ëpp ci nataal yooyu dañoo am ay bën-bën, furi walla yàqu. Yenn yi sax dañu xotteeku. Waaye nag mu am boo xam ne dara jotu ko, dafa leer nàññ mel ni lu bees. Nga laaj kiy won nit ñi li nekk ci palaas bi: «Ndax bii moo gën a bees ci nataal yi?» Mu ne la: «Déedéet, bokk na ci yi gën a màgget te kenn masu ko defaraat.» Nga laaj ko: «Ndax dañu ko dencoon fu gën a wóor?» Mu ne la: «Déedéet, bi moom lu ne daj na ko. Ay bandi yu bare jéem nañu ko yàq.» Xéyna nga laaj sa bopp: «Lan lañu ko defare?»
Mën nañu wax ne Biibël bi dafa mel ni nataal boobu. Téere bu màgget la, te sax moo gën a màgget téere yu bare. Dëgg la am na yeneen téere yu màgget. Waaye, ni nataal yi ñu wax sànq, téere yooyu yàqu nañu ndax bi ñu leen bindee yàgg na. Ci misaal, li téere yooyu wax ci science, xam-xam bu bees bi ñu am weddi na ko. Xelal yi téere yooyu di joxe ci wér-gi-yaraam lorange lañuy gën a jural nit ñi. Lu bare ci téere yu yàgg yooyu am nañu ay xaaj yu réer walla ñu yàqu.
Waaye Biibël bi wuute na lool ak téere yooyu. Li ñu njëkk a bind ci Biibël bi, bi ñu ko bindee booba ba léegi ëpp na 3 500 at. Terewul, li nekkoon ci Biibël bi moo fa nekk ba tey. Ay yooni yoon, ay nit lakk nañu Biibël bi, tere ñeneen ñu liir ko te di wax lu ñaaw ci moom. Waaye li nekkoon ci Biibël bi soppeekuwul. Xam-xam bu bees bi nit ñi am taxul Biibël bi xewwi. Xam-xam bi nekk ci Biibël bi amul moroom.
XELAL YI ÑU SOXLA TEY
Xéyna yaa ngi laaj sa bopp: ‘Ndax li Biibël bi wax am na njariñ ci suñu jamono?’ Ngir xam tont bi, laajal sa bopp lii: ‘Yan ñooy jafe-jafe yi gën a tar yu doomu Aadama yi di daj?’ ‘Yan ñoo la ci gën a tiital?’ Xéyna nga jàpp ne xare la, suuf si ñuy yàq, reyante bi walla ger. Léegi xoolal xelal yi nekk ci Biibël bi. Booy xool xelal yooyu, laajal sa bopp lii: ‘Bu nit ñi doon topp xelal yi nekk ci Biibël bi, ndax àddina si du gën a neex?’
BËGG AM JÀMM AK ÑÉPP
«Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen, ndax dees na leen tudde doomi Yàlla» (Macë 5:9). «Wutleena juboo ak ñépp, ba fa seen kàttan yem» (Room 12:18).
AM YËRMANDE TE DI BAALE
«Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen, ndax dees na leen yërëm» (Macë 5:7). «Muñalanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam. Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale» (Kolos 3:13).
JÀMM DIGGANTE XEET YI
Yàlla «ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xébla yi» (Jëf ya 17:26). «Ci dëgg gis naa ne Yàlla du gënale, waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu» (Jëf ya 10:34, 35).
FONK SUUF SI
«Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm» (Njàlbéen ga 2:15). Yàlla dina «rey ñiy yàq àddina» (Peeñu 11:18).
BAÑ LÉPP LUY YÓBBE CI BËGGE AK CI JËFI NJAALO
«Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree bare» (Luug 12:15). «Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi» (Efes 5:3).
NEKK NIT KU JUB TE SAWAR CI LIGGÉEY
«Danoo bëgga rafet ci lépp lu nuy def» (Yawut Ya 13:18). «Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax» (Efes 4:28).
DI DIMBALI ÑENEEN ÑI
«Dëfal[leen] ñi seen yasara yàcciku, dimbali ñi néew doole, tey muñal ñépp» (1 Tesalonig 5:14). «Nemmiku[leen] jirim yi ak jigéen, ñi seen jëkkër faatu, ci seeni tiis» (Saag 1:27).
Biibël bi yemul rekk ci lim jikko yooyu. Dafa ñuy jàngal ñu fonk leen te jëfe leen ci suñu dund bés bu nekk. Bu nit ñu bare doon jëfe li Biibël bi wax ndax porobalem yu tar yi doomu Aadama yi di jànkoonteel duñu wàññiku? Kon, tey lañu gën a soxla xelal yi nekk ci Biibël bi! Waaye, xelal yi nekk ci Biibël bi, ban njariñ lañu la mën a amal tey?
NJARIÑ BI NGA MËN A JËLE TEY CI XELAL YI NEKK CI BIIBËL BI
Yeesu mi ëpp ñépp xam-xam lii la waxoon: «Li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» (Macë 11:19). Ndax ànd nga ci li mu wax? Li ngay def mooy wone ndax nit ku am sago nga walla déet. Kon xalaatal ci lii: ‘Bu dee Biibël bi am na njariñ ndax warul jur lu baax ci sama dund bu ma ko jëfe? Naka la ma mënee dimbali ci jafe-jafe yi may jànkoonteel?’ Xoolal lii di topp.
Delphine * amoon na dund gu neex te bare jàmm. Waaye dafa jékki-jékki rekk mu komaase am ay porobalem yu tegaloo. Doomam bu jigéen dee. Séyam tas. Mu dem ba amatul xaalis. Lii la wax: «Dama jaaxlewoon: amatuma doom, amatuma jëkkër, amatuma kër. Demoon naa ba xammeetuma sama bopp: sawaratuma woon ci dara, sama yaakaar tas.»
Li Delphine dund tax na mu xam bu baax li aaya bii di tekki: «Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at, ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk; li ci ëpp di coonooku tiis, ne fëyy, nu wéy» (Sabóor 90:10).
Biibël bi moo dimbali Delphine bi mu nekkee ci jafe-jafe. Delphine du fàtte mukk ni ko Biibël bi dimbalee. Nit ñu bare gis nañu njariñ bi nekk ci Biibël bi. Topp xelal yi nekk ci Biibël bi dimbali na leen ñu jànkoonte ak seeni jafe-jafe. Dem nañu ba gis ne Biibël bi dafa mel ni nataal bi ñu doon wax ci kaw. Wuute na lool ak téere yu bare yuy dem ba màgget te xewwi. Ndax loolu dafay tekki ne, li nekk ci Biibël bi moo wuute? Ndax li nekk ci Biibël bi wonewul ne Biibël bi ci Yàlla la jóge, waaye du ci nit? (1 Tesalonig 2:13).
^ par. 24 Fii, yenn tur yi dañu leen soppi.