Ndax Yàlla trinité la?
Li Biibël bi wax
Diine karceen yu bare, dañuy jàngale ne Yàlla trinité la, maanaam Baay bi, Doom ji ak Xel mu sell mi, benn Yàlla lañu te kenn sutul moroomam. Waaye lii la téere bi tudd Encyclopædia Britannica wax: «Baatu Trinité walla njàngale bu jëm ci loolu amul fenn fu mu feeñ ci [xaaju Biibël bi ñuy woowe] Kóllëre gu bees gi [...] Njàngale boobu mu ngi am gannaaw ay werante yu bare yu amoon ci ay téeméeri at.»
Te sax, bu Biibël bi di wax ci Yàlla, amul fenn fu ñu wax ne dafa bokk ci trinité. Xoolal aaya yii ci Biibël bi:
«Aji Sax ji sunu Yàlla, Aji Sax ji kenn la» (Baamtug Yoon wi 6:4).
«Yaw mi tudd Aji Sax ji doŋŋ yaay Aji Kawe ji yilif àddina yépp» (Sabóor 83:19).
«Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist» (Yowaana 17:3).
«Yàlla kenn la» (Galasi 3:20).
Léegi nag, lu tax lu ëpp ci diine karceen yi di wax ne Yàlla trinité la?